Description
Kwame surgab tóokóor la ca Gorom-Gorom, ca Burkina Faso. Njaatigeem, porfesër Omar Seku, da ñu koo gëfoon ca kanamam. Ca biir xeex ba, gàllaajam dammu.Kwame dem di wëri Omar ma doon jeema dekkalaat ndànd foy-foy gi. Ku ko gëf?Gëf ga ak gàllaaj ku doy waar gi ndaq da ñoo am lu ñu joteek leebu bajani Kwame ja? "Deklul ngelawli, Sahara munge jooy. Dafa buga naataat. Bena bes Bena bes dina am nit ku ñew. Dina dekkelaat gañcax ak garap yi... "