Description
Ca biir tukki ma bu àndoon ak Clément ci oto, teg ca gaal, ca la Kwamé tàmbalee xam ci lan la njaatigeem doon liggéey, xam-xamam màcc ci mbay ak njureel.Ñaari yoon, mu am ñu koy jeema baayiloo gëstoom: posaneko ak capaloo ca Boubon; di fexee it mu baña taseek profesër Kouada ca Niamey.Ci ndimalu Nathalie,la gisee tuuti ca mbóot ma doon ubbi dencukaay bu yeemee ba "Sahel vert".